قَصِيدَةُ الْمَقْبُولَةِ
The Accepted Poem
Wo
صَلَّى اللهُ عَلَى مُحَمَّدْ
صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمْ
Na Yàlla julli ci Muhammad
Na Yàlla julli ci moom te sotti ci moom jàmm
رَوْضَةُ الْهَادِي نَبِيِنَا
هُيِّئَتْ لِلْمُتَّقِينَا
Tóotuyu Kiy gindee, sunu Yonent
Ñu ngi ko waajalal ñiy ragal Yàlla
كُلُّ مَنْ قَالُوا رَضِينَا
بِالْحَبِيبْ مَوْلَاىْ مُحَمَّدْ
Képp ku wax ne, "Gërëm nañu,
Ci Sópe bi, sunu sang Muhammad”
حُبُّهُ عَيْنُ الْكَمَالِ
جَاهُهُ عَالٍ وَغَالِ
Mbëggeelam mooy ndaaluk mat,
Darajaam dafa kawe te jafe
صَحْبُهُ خَيْرُ الرِّجَالِ
بَايَعُوا الْهَادِي مُحَمَّدْ
Ay sahabaam ñoo gën ci nit ñi,
Ñooy ñi jébbalu ci Kiy gindee Muhammad
وَجْهُهُ فَاقَ الْبُدُورَا
زَادَهُ الْمَوْلَى سُرُورَا
Kanamam dakk na weer wu fees wi,
Boroom bi dolli ko mbégte
قَدْ بَدَا فِي الْكَوْنِ نُورَا
قَبْلَ خَلْقِ اللَّهِ مُحَمَّدُ
Leer feeñ na ci àddina,
Njëkk Yàlla sàkk, Muhammad
حُبُّهُ فَرْضٌ وَحَتْمُ
مِدْحَهُ خَيْرٌ وَغُنْمُ
Bëgg ko farata la ak warugar,
Taggu ko yiw la ak ngëneel
لَيْسَ يَأْتِي الْقَلْبَ هَمُّ
لِلَّذِي يَهْوَي مُحَمَّدْ
Tiiis du ñëw mukk ci xolu,
Képp kuy sope Muhammad
بَحْرُ عِلْمِ اللهِ أَحْمَدْ
كُلُّ مَنْ يَلْقَاهُ يَسْعَدْ
Ahmad mooy géejug xam-xamu Yàlla
Képp ku ko dajeel am na ngëneel
حَوْضُهُ الصَّافِي الْمُبَرَّدْ
لِلَّذِي يَعْشَقْ مُحَمَّدْ
Tënxam bu set bi te sedd
Ñeel na ki bëgg Muhammad
يَفْتَحُ اللهُ الْعَوَالِمْ
بإِمَامٍ لِلْمَكَارِمْ
Yàlla ubbina àddina yi
Jaarale ko ci Imaamu jikko yu rafet yi
لِجَمِيعِ الرُّسْلِ خَاتَمْ
الحَبِيبْ مَوْلَاىْ مُحَمَّدْ
Mujjug Yonent yépp
Sópe bi, sama sang Muhammad
خَيْرُ خَلْقِ اللهِ طَهَ
مِثْلُ شَمْسٍ فِي ضُحَاهَا
Taha mooy ki gën ci mbindéefi Yàlla
Mu melni jànt ci yor-yoram
هَذِهِ الدُّنْيَا نَرَاهَا
فِي ضِيَاءٍ مِنْ مُحَمَّدْ
Àddina sii nu gis
Mu ngi ci leeraayu Muhammad
أَكْحَلُ الْعَيْنَيْنِ أَدْعَجْ
نُورُهُ الْمَحْبُوبُ أَبْلَجْ
Bët yu ñuul te lënd
Leeram gu ñu bëgg gi dafay jal-jali
أَشْنَبُ الْأَسْنَانِ أَفْلَجْ
فَاقَ رُسْلَ اللّهْ مُحَمَّدْ
Bëñ yu weex ak rëx yu xóot
Muhammad gën na Yonenti Yàlla yi
وَجْهُهُ يَا نَاسُ نَائِرْ
سَيِّدِي مَوْلَى الْبَشَائِرْ
Yéen nit ñi, kanamam dafay leer
Sama sang, boroom xibaar yu neex yi
ذُخْرُنَا نُورُ الْبَصَائِرْ
إِسْمُهُ الْهَادِي مُحَمَّدْ
Sunu dencukaay, leerug xol yi
Turam mooy Kiy gindee Muhammad
قَدْرُهُ الْعَالِي الْمُفَضَّلْ
وَصْفُهُ الْغَالِي الْمُكَمَّلْ
Darajaam dëgg la kawe te gën
Meloom dëgg la jafe te mat
وَحْيُ رَبِّي قَدْ تَنَزَّلْ
لِلْحَبِيبْ مَوْلَاىْ مُحَمَّدْ
Wahyuyu sama Boroom wàcc na
Ci Sópe bi, sama sang Muhammad
فَضْلُهُ عَمَّ النَّوَاحِي
لِظَلَامِ الْكُفْرِ مَاحِي
Yiwam yaatu na ci wàll yépp
Fàddu lëndëmug yéefere
فِي الصَّحَارِى وَالْبِطَاحِ
أَشْرَقَتْ أَنْوَارْ مُحَمَّدْ
Ci màr yi ak xur yi
Leeri Muhammad feeñ nañu
شَرْعُهُ لِلْكَوْنِ يَعْمُرْ
وَبِهِ الْأَيَّامُ تَفْخَرْ
Sariyaam moo jox àddina dund
Te ngir moom bés yi di ndamu
دَمْعُ مَنْ يَهْوَاهُ يَقْطُرْ
مِنْ غَرَامٍ فِي مُحَمَّدْ
Rangooñi ku ko sope di sotti
Ci mbëggeelam ci Muhammad
حُسْنُهُ لِلْبَدْرِ أَخْجَلْ
وَبِهِ غَيْبٌ تَنَزَّلْ
Rafetaayam rusloo na weer wu fees wi
Te ci moom la mbóot wàcce
وَجُمُوعَ الْكُفْرِ عُطِّلْ
مِنْ عَزِيمِ مَوْلَانَا مُحَمَّدْ
Gàlankoor nañu mboolooy yéefere
Ci fasaaley sama sang Muhammad
الْبَعِيرُ يَشْكُو الْمَجَاعَهْ
لِلنَّبِيِّ بَيْنَ الْجَمَاعَةْ
Gëléem gi jooy na xiif
Ci Yonent bi ci biir ndaje mi
قَالَ يَا مَوْلَى الشَّفَاعَةْ
كُنْ شَفِيعِي يَا مُحَمَّدْ
Mu ne, "Yaw boroom ramu gi
Nekkala sama ramukaay, yaw Muhammad"
نَادَتِ الْهَادِي غَزَالَهْ
تَشْتَكِي تُبْدِي مَقَالَهْ
Tërbán woo na Kiy gindee
Di ñaawlu tey wax soxlaam
يَا إِمَامًا لِلْرِّسَالَهْ
كُنْ ضَمِينِي يَا مُحَمَّدْ
Yaw Imaamu yóotukaay bi
Nekkala sama wóorukaay, yaw Muhammad
هَذِهِ الدُّنْيَا كَسَاعَهْ
إِجْعَلِ الْأَعْمَالَ طَاعَهْ
Àddina sii benn waxtu rekk la
Defal say jëf jaamu Yàlla
وَاشْتَرِي خَيْرَ بِضَاعَهْ
زَوْرَةَ الْهَادِي مُحَمَّدْ
Te jënd mbell mi gën
Ziyaari Kiy gindee Muhammad
هَذِهِ الدُّنْيَا تَزُولُ
وَالْبَقَا لَيْسَ يَطُولُ
Àddina sii di na jeex
Te dundiinu fi du yàgg
أَيْنَ مَنْ يَمْشِي يَقُولُ
كُنْ شَفِيعِي يَا مُحَمَّدْ
Ana ki dox di wax ne
"Nekkala sama ramukaay, yaw Muhammad"
رَبَّنَا يَسِّرْ وَسَهِّلْ
زَوْرَةَ الْمُخْتَارِ عَجِّلْ
Sunu Boroom, yombalal te nooyal
Gaawal ziyaari Ki ñu tànn
دَمْعُنَا يَهْمِى وَيَنْزِلْ
مِنْ غَرَامٍ فِي مُحَمَّدْ
Sunuy rangooñ di wal di sotti
Ci mbëggeel ci Muhammad
رَبَّنَا هَيِّئْ طَرِيقَا
كُنْ لَنَا رَبِّي رَفِيقَا
Sunu Boroom, wajalal yoon wi
Nekkala, sama Boroom, sunu àndandoo
كَيْ نَرَى بَدْرًا شَفِيقَا
الْحَبِيبْ مَوْلَايْ مُحَمَّدْ
Ngir nu gis weer wu fees wuy yërëm
Sópe bi, sama sang Muhammad
ظَنُّنَا فِيكَ جَمِيلُ
أَنْتَ يَا رَبِّي وَكِيلُ
Sunu yaakaar ci yaw rafet na
Yaw sama Boroom yaay wóyekat bi
وَالنَّبِي نِعْمَ الْكَفِيلُ
الْحَبِيبْ مَوْلَايْ مُحَمَّدْ
Te Yonent bi mooy kàttan gi gën
Sópe bi, sama sang Muhammad
كُلُّنَا يَرْجُو الْبَشَارَهْ
بِالرَّحِيلْ نَحْوَ الزِّيَارَهْ
Ñun ñépp ñu ngi yaakaar xibaar yu neex
Ngir tukki jëm ci ziyaar bi
حَبَّذَا تِلْكَ التِّجَارَهْ
زَوْرَةُ الْهَادِي مُحَمَّدْ
Ndeysaan, njaay moomu rafet na
Ziyaaru Kiy gindee Muhammad
أَيْنَ أَصْحَابُ الكَمَالِ
أَيْنَ سَادَاتُ الرِّجَالِ
Ana boroom jikko yu mat yi
Ana njiiti nit ñi
أَنْفَقُوا مِنْ خَيْرِ مَالِ
قَاصِدِينَ مَوْلَاىْ مُحَمَّدْ
Joxe nañu ci alal ji gën
Di jublu sama sang Muhammad
دَمْعُهُمْ يَقْطُرْ وَبَادِي
كُلَّمَا حَلُّوا بِوَادِي
Seniy rangooñ di sotti te feeñ
Saa yu ñu wàccee ci ab xur
قَصْدُهُمْ خَيْرُ العِبَادِ
الْحَبِيبْ مَوْلَاىْ مُحَمَّدْ
Senug njublu mooy jaam bi gën
Sópe bi, sama sang Muhammad
سَارَ بِالرَّحْمَنِ سَارَا
رَكْبُهُمْ يَطْوِي الْقِفَارَا
Ci Yàlla Yërëmaakoon bi lañu doxee
Sen dox bi di dagg àll bi
وَرَأَيْنَاهُمْ جَهَارَا
عَاشِقِينْ مَوْلَاىْ مُحَمَّدْ
Te gis nañu leen ci lu wéet
Sopey sama sang Muhammad
حَرُّ هَاتِيْكَ الْبَوَادِي
مِثْلُ ثَلْجٍ مِنْ وِدَادِ
Tàngaayu màr yooyu
Dafa melni galaas ci mbëggeel
حِصْنُهُمْ خَيْرُ الْعِبَادِ
رَحْمَةُ الْهَادِي مُحَمَّدْ
Sen tata mooy jaam bi gën
Yërmandey Kiy gindee Muhammad
اسْكُبِ الدَّمْعَ حَلَالًا
عِنْدَمَا تَلْقَى الْهِلَالَا
Tuural rangooñ yi ak dëgg
Saa yoo gisee weer wu bees wi
مِنْ بَعِيدٍ قَدْ تَلَالَا
فِيْهِ نُورٌ مِنْ مُحَمَّدْ
Mu ngi jal-jali ca sore
Te leeri Muhammad a ngi ci
هَذِهِ الْخَضْرَاءُ تَظْهَرْ
نُورُهَا لِلْعَقْلِ يَبْهَرْ
Mbal mbu wert mii feeñ na
Leeram yéem na xel mi
عِنْدَ رُؤْيَاهَا تَحَدَّرْ
دَمْعُ مَنْ يَعْشَقُ مُحَمَّدْ
Saa yo ko gisee dinala tuur
Rangooñi kiy sope Muhammad
رَوْضَةُ الْهَادِي نَبِيِّنَا
تُفْرِحُ الْقَلْبَ الْحَزِينَا
Tóotuyu Kiy gindee, sunu Yonent
Mooy bégal xol buy tiis
أَبْشِرُوا يَا زَائِرِينَا
بِالشَّفَاعَةِ مِنْ مُحَمَّدْ
Bégeleen yéen sunuy ziyaarkat
Ci ramu gi bawoo ci Muhammad
هَذِهِ الرَّوْضَةُ أَبْشِرْ
قَدْ وَصَلْنَا لِلْمُبَشِّرْ
Tóotu bii la, amleen mbégte
Yegg nañu ci kiy joxe xibaar
أَمْرُ دُنْيَا لَا تُفَكِّرْ
وَانْظُرِ الْهَادِي مُحَمَّدْ
Bul xalaat mbiri àddina
Te xool Kiy gindee Muhammad
كُلُّ مَنْ زَارَ الْمَقَامَا
فَالنَّبِي رَدَّ السَّلَامَا
Képp ku ziyaar bërëb bi
Yonent bi di na ko fay nuyyoo bi
يَعْرِفُ الْخَلْقَ تَمَامَا
بَشِّرُوا زُوَّارَ مُحَمَّدْ
Xam na mbindéef yi bu mat
Bégalal ñiy ziyaar Muhammad
هَامَتْ الْأَرْوَاحُ حُبًّا
دَمْعُنَا قَدْ سَالَ صَبًّا
Ruux yi rëer nañu ci mbëggeel
Sunuy rangooñ sotti na lu bare
نَالَتْ الزُّوَّارُ قُرْبًا
لِلْحَبِيبِ مَوْلَايْ مُحَمَّدْ
Ziyaarkat yi jot nañu jegeñaale
Ci Sópe bi, sama sang Muhammad
يَا حَبِيبَ الْمُتَّقِينَا
وَسِرَاجًا وَمُبِينَا
Yaw Sópebu ñiy ragal Yàlla
Ak làmp ak leer gu feeñ
يَا أَبَا الْقَاسِمْ دُعِينَا
فَأَتَيْنَا يَا مُحَمَّدْ
Yaw Abul Qaasim, woo nañu nu
Ba noo tax ñu ñëw, yaw Muhammad
مَرْحَبًا يَا مُصْطَفَانَا
حُبُّكَ الْغَالِي أَتَانَا
Bismilla yaw Ki ñu tànn
Sa mbëggeel mu jafe mi ñëw na ci ñun
مِنْ بَعِيدٍ قَدْ دَعَانَا
لِلْحَبِيبِ مَوْلَايْ مُحَمَّدْ
Ca sore la nu woowe
Jëm ci Sópe bi, sama sang Muhammad
كَيْ نَرَي ذَاكَ الْمَقَامَا
فِيهِ بَدْرٌ قَدْ تَسَامَى
Ngir nu gis bërëb boobu
Foofu la weer wu fees yëkëtikoo
وَأَخُو الشَّوْقِ تَسَامِي
مِنْ هِيَامٍ فِي مُحَمَّدْ
Te boroom mbëggeel kawe na
Ci yëg gu tar ci Muhammad
يَا شَفِيعًا لِلذُّنُوبِ
وَغِيَاثًا فِي الْكُرُوبِ
Yaw kiy ramu ci bàkkaar yi
Ak ndimbal ci lëj-lëj yi
وَضِيَاءً لِلْقُلُوبِ
أَنْتَ نُورُ يَا مُحَمَّدْ
Ak leeraay gi ngir xol yi
Yaw yaay leer, yaw Muhammad
جَاهُكَ الْمَرْجُو عَظِيمٌ
أَنْتَ مِفْضَالٌ كَرِيمٌ
Sa daraja ji ñu yaakaar dafa rëy
Yaw danga am yiw te joxe
وَرَءُوفٌ وَرَحِيمٌ
وَعَفُوٌّ يَا مُحَمَّدْ
Te nga laabiir te yërëm
Te di jéggale, yaw Muhammad
أَبْشِرُوا يَا مَنْ رَأَيْتُمْ
رَوْضَةَ الْهَادِي وَزُرْتُمْ
Amleen mbégte yéen ñi gis
Tóotuyu Kiy gindee te ziyaar
عِنْدَ رَبِّ الْعَرْشِ كُنْتُمْ
زَائِرِينَ مَوْلَايْ مُحَمَّدْ
Céy Boroom Aras ngeen nekkoon
Di ziyaari sama sang Muhammad
قَدَّرَ الْمَوْلَى السَّعَادَهْ
وَدَعَاكُمْ لِلْعِبَادَهْ
Boroom bi dogal na ngëneel
Te woo na leen ci jaamu gi
هَذِهِ الْحُسْنَى زِيَادَهْ
زَوْرَةُ الْهَادِي مُحَمَّدْ
Lii mooy rafet-rafetug yokkute
Ziyaari Kiy gindee Muhammad
سَعْدُكُمْ يَا مَنْ تَزُورُوا
وَجْهُكُمْ يَعْلُوهُ نُورُ
Mbooloo ngëneel ci yéen ñiy ziyaar
Sen kanam leer mu ngi ci kawam
رَبُّكُمْ رَبٌّ غَفُورُ
لِلَّذِي قَدْ زَارَ مُحَمَّدْ
Sen Boroom Boroom buy jéggale la
Ñeel képp ku ziyaar Muhammad
لَوْ رَأَيْنَا الْوَاقِفِينَا
لَوْ رَأَيْنَا الْقَاعِدِينَا
Su nu gisoon ñi taxaw
Su nu gisoon ñi toog
لَوْ رَأَيْنَا السَّائِلِينَا
الشَّفَاعَةَ مِنْ مُحَمَّدْ
Su nu gisoon ñiy ñaan
Ramu gi ci Muhammad
نُورُ خَيْرِ الْخَلْقِ يُجْلِي
وَكِتَابُ اللهِ يُتْلِي
Leeri ki gën ci mbindéef yi leeral na
Te Tére Yàlla bi ñu ngi koy jàng
وَعُلُومُ الشَّرْعِ تُمْلِي
عِنْدَ مَوْلَايْ مُحَمَّد
Te xam-xami Sariya ñu ngi koy tàngal
Fa sama sang Muhammad
إِنْ رَجَعْتُمْ بِالسَّلَامَةْ
أَخْبِرُوا أَهْلَ الْمَلَامَةْ
Su ngeen delluu ak jàmm
Xamal-leen ñiy ñaawlu
كَيْ يَجِيئُوا مِنْ تِهَامَةْ
لِلْحَبِيبِ مَوْلَايْ مُحَمَّدْ
Ngir ñu bawoo Tihamah
Ñëw ci Sópe bi, sama sang Muhammad
عَرِّفُوهُمْ بِالْمَقَامِ
أَخْبِرُوهُمْ بِالْهِِيَامِ
Xamal leen bërëb bi
Nettali leen mbëggeel mi
أَيْقِظُوهُمْ مِنْ مَنَامِ
كَيْ يَزُورُوا لِمُحَمَّدْ
Ye leen ci nelaw
Ngir ñu ziyaari Muhammad
لَوْ عَلِمْتُمْ يَا عَوَاذِلْ
مَا سَكَنْتُمْ فِي الْمَنَازِلْ
Su ngeen xamoon yéen ñiy ñaawlu
Dooleen toog ci seni kër
مَا لَنَا فِي الْقَلْبِ شَاغِلْ
كُلُّنَا يَهْوَى مُحَمَّدْ
Amu nu lenn luy rëq-rëqi xol
Ñun ñépp danu sope Muhammad
قَدْ سَرَيْنَا بِالْمَطَايَا
لِلنَّبِي خَيْرِ الْبَرَايَا
Dox nañu guddi ci mbàmbulaan yi
Jëm ci Yonent bi, ki gën ci mbindéef yi
سَيِّدِي كَنْزِ الْعَطَايَا
الْحَبِيبِ مَوْلَايْ مُحَمَّدْ
Sama sang, dencukaayu maye yi
Sópe bi, sama sang Muhammad
حُبُّهُ يُحْيِي الْقُلُوبَا
يَغْفِرُ اللهُ الذُّنُوبَا
Mbëggeelam dafay dundal xol yi
Yàlla di jéggale bàkkaar yi
يَسْتُرُ اللهُ الْعُيُوبَا
بِالْحَبِيبِ مَوْلَايْ مُحَمَّدْ
Yàlla di suturaal ay yi
Ci Sópe bi, sama sang Muhammad
يَا رَسُولَ اللهِ نَادِ
أَهْلَ حُبٍّ وَوِدَادِ
Yaw Ndawul Yàlla, wool
Boroom mbëggeel ak tàqale
هُمْ بِشَوْقٍ فِي بِعَادِ
أُدْعُهُمْ مَوْلَايْ مُحَمَّدْ
Ñu ngi xaaqatu ci lu sore
Woo leen, sama sang Muhammad
وَتَوَجَّهْ لِلْمُقَدِّرْ
رَبُّنَا الْمُعْطِي يُيَسِّرْ
Te jublu ci Ki dogal
Sunu Boroom, Mayekat bi, di yombal
بَعْدَ عُسْرٍ كَيْ نُبَدِّرْ
لِلْحَبِيبِ مَوْلَايْ مُحَمَّدْ
Ginnaaw jàfe-jàfe ngir ñu gaawantu
Ci Sópe bi, sama sang Muhammad
صَلَوَاتٌ طَيِّبَاتُ
زَاكِيَاتٌ نَامِيَاتُ
Julli yu sell
Yu set tey yokku
غَالِيَاتٌ دَائِمَاتُ
لِلْحَبِيبِ مَوْلَايْ مُحَمَّدْ
Yu jafe te sax
Ñeel Sópe bi, sama sang Muhammad
وَسَلَامُ اللهِ يَتْرَى
عَطَّرَ الْكَوْنَ وَ مَرَّا
Ak jàmmi Yàlla juy toftalantu
Bànneexal na àddina bi mu rombee
شَرَحَ الصَّدْرَ وَسَرَّا
لِلْحَبِيبِ مَوْلَايْ مُحَمَّدْ
Yàtal na dënn bi te bégal
Ñeel Sópe bi, sama sang Muhammad
وَعَلَى الصَّحْبِ الْأَفَاضِلْ
كُلُّ مِفْضَالٍ وَعَامِلْ
Ak sahaba yu barkeel yi
Képp ku am yiw tey jëf
بِكِتَابِ اللهِ قَائِلْ
وَكَذَا آلِ مُحَمَّدْ
Kuy wax ci Téere Yàlla bi
Ak noonu askanu Muhammad
عُمَّ بِالرِّضْوَانِ رَبِّي
خَيْرَ صِدِّيقٍ وَصَحْبِ
Fàddul ak ngërëm, sama Boroom
Ki gën ci dëggu ak sahaba bi
وَكَذَا الْفَارُوقُ حِبِّي
سَكَنَا قُرْبَ مُحَمَّدْ
Ak noonu Faaruq, sama sópe
Ñoom ñaar ñu dëkk jege Muhammad
عُمَّ ذَا النُّورَيْنِ رَبِّي
وَأَبَا السِّبْطَيْنِ حِبِّي
Fàddul Boroom ñaari leer yi, sama Boroom
Ak Baay ba ñaari sët yi, sama sópe
ثُمَّ لِلْعَمَّيْنِ رَبِّي
ثُمَّ صَحْبًا لِمُحَمَّدْ
Topp ci ñaari baay-tëkku yi, sama Boroom
Topp ci sahaba yi ñeel Muhammad
عُمَّ لِلسِّبْطَيْنِ رَبِّي
آلِ خَيْرِ الْخَلْقِ طِبِّي
Fàddul ñaari sët yi, sama Boroom
Askanu ki gën ci mbindéef yi, sama garab
وَكَذَا الزَّهْرَاءُ تُنْبِي
عَنْ كَمَالٍ فِي مُحَمَّدْ
Ak noonu Zahraa biy xibaar
Ci mboolem mat gi ci Muhammad
عُمَّ سُهَّارَ اللَّيَالِي
كُلَّ مَنْ لِلْوِرْدِ تَالِي
Fàddul ñiy yewwu ci guddi yi
Képp kuy jàng wirdi wi
هُمْ رِجَالُ الِاتِّصَالِ
بِالْحَبِيبِ مَوْلَايْ مُحَمَّدْ
Ñooy nit ñi jokkoo
Ak Sópe bi, sama sang Muhammad
عُمَّ سُكَّانَ الْبَرَارِي
وَالصَّحَارَى وَالْقِفَارِ
Fàddul waa kànd yi
Ak màr yi ak àll yi
كُلَّ مَجْذُوبٍ وَقَارِي
لِلصَّلَاةِ عَلَى مُحَمَّدْ
Képp ku gëja mbóot ak ku jàng
Ci julli ci kaw Muhammad
عُمَّ رَبِّي النَّاسِكِينَا
وَالْعِبَادَ الصَّالِحِينَا
Fàddul, sama Boroom, ñiy jaamu
Ak jaam yu baax yi
وَالرِّجَالَ الْوَاقِفِينَا
عِنْدَ مَوْلَانَا مُحَمَّدْ
Ak nit ñiy taxaw
Fa kanam sunu sang Muhammad
وَبِهِمْ يَا رَبِّ نَصْرَا
دَائِمًا دُنْيَا وَأُخْرَى
Te ci ñoom, yaw Boroom, may nu ndam
Fu nekk ci àddina ak àllaaxira
أَعْظِمَنْ يَا رَبِّ أَجْرَا
بِالْحَبِيبْ مَوْلَايْ مُحَمَّدْ
Reuyalal, yaw Boroom, yool bi
Ci Sópe bi, sama sang Muhammad
رَبِّ رُدَّ الْحَاسِدِينَا
عَنْ أَذَانَا خَائِبِينَا
Boroom, rëdd-ël ñiy iñaan
Ci loru ñun, ñu pert
كُنْ لَنَا عَوْنًا مُعِينَا
بِالْحَبِيبِ مَوْلَايْ مُحَمَّدْ
Nekkala ñun ndimbal ak doole
Ci Sópe bi, sama sang Muhammad
رَبِّ لَا تَجْعَلْ عِدَانَا
تَتَمَكَّنْ مِنْ أَذَانَا
Boroom, bul may sunuy noon
Ñu mën noo lor
اكْسُهُمْ ثَوْبًا هَوَانَا
وَأَجِبْنَا بِمُحَمَّدْ
Solal leen mbubbum toroxte
Te nangul nu ci darajay Muhammad
عَجِّلِ الْخَوْفَ إِلَيْهِمْ
وَكَذَا الْبَأْسَ عَلَيْهِمْ
Gaawal tiitaange ci ñoom
Ak noonu musiba ci ñoom
وَكَذَا الشَّرَّ لَدَيْهِمْ
وَانْصُرَنْ آلَ مُحَمَّدْ
Ak noonu lu ñaaw ci ñoom
Te dimbali askanu Muhammad
نَاظِمُ الدُّرِّ الْمُحَرَّرْ
صَالِحٌ مِنْ آلِ جَعْفَرْ
Kiy wëy jëwëriñ yu set yii
Saalih la ci askanu Ja’far
رَاجِي فَضْلًا مِنْكَ أَكْبَرْ
بِالْحَبِيبِ مَوْلَايْ مُحَمَّدْ
Di yaakaar yiw wu gën rëy ci yaw
Ci Sópe bi, sama sang Muhammad
يَرْجُو فَضْلًا لَنْ يَزُولَا
وَرِضَاءً وَقَبُولَا
Mu ngi yaakaar yiw wudul dindi mukk
Ak ngërëm ak nangu
وَاتِّصَالًا وَوُصُولَا
لِلْحَبِيبِ مَوْلَايْ مُحَمَّدْ
Ak jokkoo ak yegg
Ci Sópe bi, sama sang Muhammad
يَرْجُو فَضْلًا مِنْكَ رَبِّي
زَوْرَةَ الْمُخْتَارِ حِبِّي
Mu ngi yaakaar yiw ci yaw, sama Boroom
Ziyaari Ki ñu tànn, sama sópe
كُلَّ عَامٍ بَيْنَ صَحْبِ
زَائِرِينَ مَوْلَايْ مُحَمَّدْ
At mu nekk ci biir ay sahaba
Ziyaari sama sang Muhammad
وَبِخَيْرٍ فِي الْخِتَامِ
نَبْتَغِي نَيْلَ الْمَرَامِ
Te ak yiw ci njèexital li
Danu bëgg am li nu yóotu
بِجِوَارٍ لِلْمَقَامِ
فِي بَقِيعٍ يَا مُحَمَّدْ
Ci wetu bërëb bi
Ci Baxe, yaw Muhammad