قُلْتُ لَمَّا غَابَ عَنِّي
Wax naa bi mu ma reeree
Wo
قُلْتُ لَمَّا غَابَ عَنِّي
نُورُ مَرَاكَ الْمَصُون
Wax naa bi ma féetee
leeru sa taar bi nu samm
شَفَّنِي وَاللَّهِ سُقْمٌ
فِيهِ قَدْ ذُقْتُ الْمَنُونَ
Barkeb Yalla, féebarr sonnal na ma
ba ma moss ci dee ci boppam
وَعُيُونِي مِنْ نَحِيبٍ
جَارِيَاتٌ كَالْعُيُون
Sama bët yi, ndax jooy yu metti
dañuy sotti ni ay bëtu-ndox
وَجُفُونِي مَا كَفَاهَا
مَا جَرَى حَتَّى جَفُون
Sama kowu-bët yi doyalu nu ko
li fi jaar ba ba nu wowee
هَامَ قَلْبِي زَادَ وَجْدِي
فَمَتَى وَصْلَكْ يَكُونُ
Sama xol réer na ci mbëggeel, sama bëgg-bëgg yokku na
kon kañ la nuy daje waat?
غَابَ عَنْ عَيْنِي ضِيَاهَا
يَا قَمَرَ دَارِي الْعُيُون
Leerr gi réer na sama gisuwaay
yaw weer wu rafet wi, fajjil bët yii