صَفَتِ النَّظْرَهْ
Leer na gis-gis bi
Wo
Wo
صَفَتِ النَّظْرَهْ طَابَتِ الْحَضْرَةْ
جَاءَتِ الْبُشْرَى لِأَهْل اللهِ
Gisu bi set na, jataay bi neex na
Xibaar bu neex ñëwël na waa kër Yàlla
قَامُوْا سُكَارَى لِذِي الْبِشَارَه
جَعْلَوْا عِمَارَهْ شُكْراً لِلّهِ
Jog nañu mel ni ñu manti ndax xibaar bi
Def nañu imara ngir sant Yàlla
أَيُّهَا الْحَاضِرْ اُذْكُرْ وَذَاكِرْ
إِيَّاكَ تُنْكِرْ حَالَ أَهْلِ اللهِ
Yaw mi fi tew, tuddal te fatali
Bul weddi mukk mbiri waa kër Yàlla
فَسَلِّمْ لَهُمْ فِيمَا عَرَاهُمْ
وَاعْلَمْ أَنَّهُمْ غَابُوْا فِي اللهِ
Jébbalu ci ñoom ci li leen di dal
Te xam ne lab nañu ci biir Yàlla
فَالْوَجْدُ بِهِمْ دَاعِيْ يَدْعِيْهِمْ
يَطْرَأْ عَلَيْهِمْ فِيْ ذِكْرِ اللهِ
Ndaxte wajdu mooy woote bi leen di woo
Te day dal ci seen kow ci tudd Yàlla
وَمَنْ لَمْ يَجِدْ فَلْيَتَوَاجَدْ
قَصْداً يَتَعَرَّضْ لِفَضْلِ اللهِ
Ku amul wajdu, na ko wut
Ngir bëgg a jot ci xéewalu Yàlla
هَكَذَا قَالُوْا وَلِذَا مَالَوْا
وَلَقَدْ غَالُوْا فِي ذِكْرِ اللهِ
Ni lañu waxe, loolu moo tax ñuy lënge
Te taral nañu lool seen tudd Yàlla
حَتَّى قَدْ ظَنَّا مَنْ لَيْسَ مِنَّا
أَنَّا جُنِنَّا بِذِكْرِاللهِ
Ba ku bokkul ci nun dafa foog
Ne dof nañu ndax tudd Yàlla
هَنِيْئاً لَنَا ثُمَّ بُشْرَانَا
إِنْ كَانَ لَنَا حُمْقٌ فِي اللهِ
Barkéel na nu, te mbégte ñeel na nu
Su fekkee ne sunu "dof" gi ci Yàlla la