أَلْفٍ صَلَّى الله عَلَى زَيْنِ الْوُجُودْ
Junniy xééwal i Yàlla ci kaw njeqalug mbindééf yi
Wo
أَلْفٍ صَلَّى الله عَلَى زَيْنِ الْوُجُودْ
مَنْ سَكَنْ طَيْبَة وَخَيَّمْ في زَرُودْ
Junniy njulli Yalla na nekk ci Rafétayu mbindéef yi
Ki dëkk Tayba te samp néegam ca Zarud
يَا بُدُورَ الْحَيِّ يَا رَبْعَ الْكِرَامْ
بَلِّغُو ظَبْيَ الْحِمَى مِنِّي السَّلَامْ
Yeen weeri dëkk bi, yeen kër gu sélmuna gi
Jottlilén nuyyoo bég bi nekk ci bërëb bu sell bi
إِنْ تَهَتَكْنَا عَلَيْكُمْ لَا نُلَامْ
غَلَبَ الْوَجْدُ عَلَيْنَا وَ الْغَرَامْ
Su nu feeñalee sunu mbëggeel ci yeen, du nu ci nangu blam
Ndaxte tàngayu xol ak cofeel danu nu sonal
لَا يَنَامُ اللَّيْلَ عَاشِقْ مُسْتَهَامْ
إِنَّمَا النَّومُ عَلَى الْعَاشِقْ حَرَامْ
Kuy bëgg ba màng du nelaw ci guddi
Ndaxte nelaw, ku bëgg lu sori dañ ko ko tere
سَادَتِي إِنْ لَمْ تَحِنُّو بِاللِّقَا
مِتُّ وَجْدًا فَلَكُمْ طُولُ الْبَقَاء
Samay sang, su ngen ma yërëmul ba nu dajé
Ma faatu ci cofeel, te yeen nanga ngen fi sax ba fàww
أَنَا إِنْ لَمْ أَهْوَا غِزْلَانَ النَّقَاء
أَيُّ فَرْقٍ بَيْنَ قَلْبِي وَ الْجَمَادْ
Man su ma bëggul bég yi nekk ci Al-Naqa
Lan mooy wuute bi diggante sama xol ak doj?
آنَسَ اللهُ بِكُمْ أَوْقَاتَنَا
وَسَقَى وَادِيكُمُ فَيْضَ الْغَمَامْ
Yalla na Yalla neexal sunuy jamono ci yeen
Te mu taw ci seen xur yi taw yu bare yu jugge ci niir yi