Wo
الله الله الله الله سَيَّدِي الله
الله الله الله اَلْعَظِيْمُ الله
Yàlla Yàlla Yàlla Yàlla Boroom bi Yàlla
Yàlla Yàlla Yàlla ku Mag ki Yàlla
أَيَا مُرِيْدَ اللهُ نُعِيدْ لَكْ قَوْلِ اصْغَهْ
إِذَا تَفْهَمْ قَوْلِي بِهِ تَصِلْ لِلّهْ
Yaw muritub Yàlla bi, ma waxat la kàddu gi déglu ko
Su fekkee dégg nga samay wax, dinga ci àgg ci Yàlla
عَلَيْكَ يَا مُرِيدْ بِخَمْرَةِ التَّوْحِيدُه
وَإِنْ تَبْغِ الْمَزِيدْ فَالْغَيْرُ عَنْكَ انْسَهْ
Yaw murit bi, nanël sangaray bennal gi
Te su fekkee bëgg nga yokkute, fatteal leneen looy lu dul moom
فَاذْكُرْ الاسْمَ الْأَعْظَمْ وَاطْوِ الْكَوْنَ تَغْنَمْ
وَخُضْ بَحْرَ الْقِدَمْ فَذَاكَ بَحْرُ الله
Tuddal Turu Yàlla bi gëna mag te lem mbindéef yi dinga am njariñ
Te duggal ci géeju njiit-lool gi, ndax loolu mooy géeju Yàlla
وَخُضْ بَحْرَ الْأَنْوَارْ وَالْمَعْنَى وَالْأَسَرَارْ
وَافْنِ هَذِي الدِّيَارْ يَبْلُغْ قَلْبُكْ مُنَاهْ
Duggal ci géeju leer yi, ak maanaa yi ak mbóoti yi
Te ràkkal kër yii, sa xol dinga àgg ca la mu namm
وَلْتَفْنَ في الْمَعْبُودْ تَذُوقْ مَعْنَى الشُّهُودُ
إِذْ لَيْسَ ذَا الْوُجُودْ إِلَّا مِنْ نُورِ الله
Sëlmët ci Ku ñuy jaamu bi, dinga safu maanaam seede gi
Ndax mbindéef mii nekkul leneen lu dul leeru Yàlla
الْمُلْكُ وَالْمَلَكُوتْ كَذَاكَ الْجَبَرُوتْ
فَكُلُهَا نُعُوتْ وَالذَّاتُ مُسَمَّاهُ
Àdduna bii ak kàttan yi ak kemmteef gi
Lépp ay melokan lañu, te Jëmm ji mooy ku ñuy tudd
فَغِبْ عَنِ الصِّفَاتْ وَافْنَ في ذَاتِ الذَّاتْ
هَذِي تَلَوُّنَاتْ مَصِيرُهَا لِلِهُ
Reerul ci melokan yi te sëlmët ci Jëmmu Jëmm ji
Yii ay melo yu wuute lañu, seen mujj ci Yàlla la
إِلَيْهِ الْمُنْتَهَى وَمِنْهُ الْمُبْتَدَا
وَالْآنَ قَدْ بَدَا وَالْكَوْنُ فِي حُلَاهْ
Ca moom la mujj gi ne, te ca moom la njiit gi jóge
Te léegi feeñ na, te mbindéef yi ci melokaanam lañu nekk
لَهُ الْكَوْنُ مِرْآتْ وَمَظْهَرُ الصِّفَاتْ
مُحَمَّدْ نُورُ الذَّاتْ عَلَيْهِ صَلَّى الله
Mbindéef yi ab seetu lañu ci moom ak feeñuwayu melokan yi
Muhammadu leeru Jëmm ji la, jàmmum Yàlla na nekk ci moom
الْعَلَاوِيْ يَقُوْلْ قَوْلًا مِنْهُ مَقْبُولُ
تَهِيْمُ بِهِ الْعُقُولْ تَغِيبْ فِي ذَاتِ الله
Alawiyi mu ngiy wax, wax ju ñu nangu ci moom
Xel yi di ci réer, te di reer ci Jëmmu Yàlla