مِنْ جَمَالِ الْكَوْنِ خَمْرِي
Ci taaru àddina si la samay sangara jòge.
Wo
مِنْ جَمَالِ الْكَوْنِ خَمْرِي
ذَقْتُهُ صِرْفاً حَلَالَا
Ci rafetaayu mbindéef yi la sama sàngara jóge
Ma móol ko mu sell te dagana
وَهْوَ مِنْ أَوْصَافِ بَدْرِي
قَدْحَوَى ذَاكَ الْجَمَالَا
Mu bokk ci jikkooy sama weer wu mat wi
Mu denc mbooleem rafetaay boobu
وَجْهٌ قَدْ لَاحَ سَنَاهْ
وَالْكَوْنُ غَدَا مِرْآهْ
Kanam gu leeram feeñ na
Ba mbindéef yi nekk seetu ci moom
إِنْ رُمْتَ فُؤَادِي لِقَاهْ
فَاجْعَلْ هَوَاكَ هَوَاهْ
Soo bëggee, yaw sama xol, daje ak moom
Na sa bëgg-bëgg nekk bëgg-bëggam
أَنَا بِالْرُّوْحِ سَمَاءُ
أَنَا بِالْجِسْمِ هَبَاءُ
Ci ruu, asamaan laa
Ci yaram, pënd (mbalit) laa
أَنَا زَهْرٌ أَنَا مَاءُ
تِهْتُ مِنْ وَجْدِي دَلَالَا
Tooro laa, ndox laa
Ma réer ci sama bànneexu mbëgeel
وَالْرُّوْحُ رَقَى مَرْقَاهْ
وَالْقَلْبُ غَدَا يَرْعَاهْ
Ruu gi yéeg na ci kawam
Xol bi nekk di ko sàmm
وَالْجِسْمُ سَعَى مَسْعَاهْ
لِيَنَالَ بِذَاكَ مُنَاهْ
Yaram wi daw na ci yoonam
Ngir am ci li mu doon bëgg
يَا عَذُوْلاً لَامَ جَهْلاً
مُغْرَماً قَدْ نَالَ وَصْلَا
Yaw miy tàkkal ci reer
Ku mbëgeelam jot ci Koom mu doon sàkku
إِنْ تَلُمْ صِدْقاً سَتُبْلَى
وَتَذُوْقُ الْحُبَّ حَالاَ
Soo tàkkalee dëgg dinga nattu
Te dinga móol mbëgeel mi ci saa si
بِفَنَائِكَ عَنْ سِوَاهْ
تَأْوِيْ لِفِنَاءِ بَقَاهْ
Ci sa neen-al ci lu dul moom
Fa la ngay fexee ci biir wéyam
وَبِبَرْدِ شَرَابِ رِضَاهْ
يُطْفِي الْفُؤَادُ جَوَاهْ
Ci seddayu nànu-geeremam
La lakk-lakku xol bi di feyee
صَلَوَاتُ اللهِ تُهْدَى
مِنْ جَمِيْعِ الْطِّيْبِ أَنْدَى
Julliy Yàlla na jébalu
Te gën a xeeñ mbooleem cuuraay
لِرَسُوْلٍ قَدْ تَبَدَّى
نُوْرُهُ يَمْحُو الْضَّلَالَا
Ci Yónnent bi feeñ
Te leeram di far réer
بِسَلامٍ لا يَتَنَاهْ
وَالْاَلِ أُهَيْلِ الْجَاهْ
Ak jàmm ju dul deñ
Ak ñoñam ñu kawe daraja
وَالْصَّحْبِ وَمَنْ وَالَاهْ
وَجِيْعِ رِجَالِ الله
Ak saaba yi ak ñi leen topp
Ak mbooleem góori Yàlla yi