بِفَاطِمَةْ قَدْ صَفَا حَالِي
Ci Faatima la sama haal sélle.
Wo
بِفَاطِمَةْ قَدْ صَفَا حَالِي وَنِلْتُ الْمَرَامْ
بِضْعَة مُحَمَّدْ حَبِيبِ اللهْ خَيْرِ الْأَنَامْ
Ak Sokhna Faatima sama mbir sell na te jot naa la ma bëggoon
Benn cér ci Muhammad, bëgg-eelub Yàlla te gën ci mbindéef yi
أَعْلَى لَهَا اللهْ قَدْراً فِي الْعُلَا وَالْمَقَامْ
نِعْمَ الْبَتُولْ الْرَّضِيَّةْ نُورْ كُلِّ الْظَّلَامْ
Yàlla yekkati na darajaam ci kawe ak mawaamam
Am na baax Sokhna bu sell, bu neex, leeru mbooleem lëndëm yi
أُمِّ الْحَسَنْ وَالْحُسَيْنْ أَهْلِ الْمَرْقَى الْعِظَامْ
لَهُمْ عَطَايَا مِنَ الْمَوْلَى كِبَارٌ جِسَامْ
Ndeyju Al-Hassan ak Al-Hussein ñu mag mawaam yi
Ñu am ay mayé yu jóge ci Boroom bi, yu réy te yaatu
هُمْ سَادَةَ أَهْلِ الْجِنَانِ الْعَالِيَةْ يَا غُلَامْ
مَنْ حَبَّهُمْ صِدِقْ بَا يِسْكُنْ بِدَارِ الْسَّلَامْ
Ñoom ñay kilifay ëttub àjjana yu kawe yi yaw xale bi
Ku leen bëgg dëgg-dëgg dinga dëkk ci kër jàmm
وَمَنْ تَعَلَّقْ بِهِمْ يَظْفَرْ بِنَيْلِ الْمَرَامْ
أَكْرَمْتِ يَا بِضْعَةَ أَحْمَدْ فَانْعَمِي بِالْتَّمَامْ
Te ku lënku ci ñoom da na jot la mu nammoon
Teru nga yaw cérub Ahmad, nanga ma gërëm ci mbax mu mat
وَامْنَحِي عَبْدَكُمْ فِي الْقُرْبْ أَعْلَى وِسَامْ
نَقُومْ بِحَمِلْ الْرَّيَاتِ الْهُدَ أَحْسَنْ قِيَامْ
Te nga may sa jaam bi daraja ju kawe ci jege-ñéel
Nu taxawu raayay njub bi ci ni mu gëne
تَعُمْ دَعْوَتُهْ فِي الْأَكْوَانْ كُلِّ الْأَنَامْ
نِلْبَسْ خِلَعْ إِرْثْ مَا يَصِفْ سَنَاهَا كَلَامْ
Ba wooteem am ci mbindéef yépp ci àdduna bi
Nu sol mbubbum donog Yoneent bi, leeram amul baat buy tudd
يَا نُورْ قَلْبِي وَيَا أُمِّي عَلَيْكِ الْسَّلَامْ
فِي كُلِّ حَالٍ وَشَأْنٍ كُلِّ لَحْظَةْ دَوَامْ
Yaw leeru sama xol te di sama ndey, jàmm na nekk ci yaw
Ci mbooleem mbir ak nekkte ak saasu nekk daxiir
عَلَيْكِ صَلَّى إِلَهِي مَعَ أَبِيكِ الْإِمَامْ
إِمَامْ كُلِّ الْوَرَى فِي كُلِّ خَاصٍّ وَعَامْ
Sama Boroom sëlmal na ci yaw ak sa baay di njiit li
Njiitu mbooleem mbindéef yi ci ñu ñu tànn ak mbooloo mi yépp
الْشَّافِعِ الْمُبْتَغَ يَوْمَ الْلِّقَاءْ وَالْزَّهَامْ
يَوْمِ الْمَلَائِكْ تُنَادِي جَمِعْ كُلِّ الْأَنَامْ
Ramu-kaat bi ñuy sàkku bésub ndaje ak xat-xat bi
Bés bi malaaka yi di woo mbooleem mbindéef yi
غُضُّوا أَبْصَارَكُمْ تَمُرْ بِنْتِ الْنَّبِيِ بِالْسَّلَامْ
وَنَكِّسُوا رُؤُوسَكُمْ مَا أَعْظَمَهْ وَاللهْ مَقَامْ
Noofal-leen seeni gët, doomu Yoneent bi moo jàll ci jàmm
Te wàcci-leen seeni bopp, barkeb Yàlla mawaam bi rëy na lool
تِذَكَرِينِي مَعَكِ أَعْبُرْ وَمَنْ لَهُ ذِمَامْ
حَاشَاكِ يَا أُمَّنَا تِنْسِينْ هَذَا الْغُلَامْ
Fattaliku ma ma jàll ànd ak yaw ak ñi nekk ci sa sutura
Soril na la yaw sunu ndey, nga fàtte xale bi
مَحْسُوبَكُمْ يَرْتَجِيهْ مِنْكُمْ بِهِ الْإِهْتِمَامْ
أَنْتُمْ مَرَامُهْ وَمَقْصُودُهْ وَنِعْمَ الْمَرَامْ
Sa jaam bi mu ngi yaakaar ci yaw jàpple ak xol
Yéen nekk li mu namm ak li mu jublu, te mat ngeen namm
يَا بِنْتَ طه فُؤَادِي فِي مَحَبَّتِكْ هَامْ
وَاللهْ أَنْتُمْ مُرَادِي فِي الْدُّنَا وَالْقِيَامْ
Yaw doomu Taha, sama xol mbegeelam ci yaw la tàkk
Barkeb Yàlla yéen laa namm ci àdduna ak bésub kër-gu-mag
وَمَا أَنَا إِلَّا بِكُمْ يَا سَادَتِي يَا كِرَامْ
عَلَيْكِ مَعَ وَالِدِكْ أَزْكَى الْصَّلَاةْ وَالسَّلَامْ
Te man amuma keneen ku dul yéen yaw sama kilifa yu am-teer
Sëlmal ak jàmm yu gën a sell na nekk ci yaw ak sa baay
وَأَهْلِ الْكِسَاءْ وَأَهْلِ بَيْتِهْ عَالِيِّينَ الْمَقَامْ
وَالْصَّحْبْ أَجْمَعْ وَمَنْ عَلَى هُدَاهْ اِسْتَقَامْ
Ak waa mbebe bi ak waa kërëm ñu kawe daraja
Ak saaba yi ñépp ak ku nekk ci njubam ba baax