قَدْ أَشْرَقَ الْبَدْرُ الْمُنِيرْ
Weer wu fees wu leeral wi fenq na
Wo
Wo
قَدْ أَشْرَقَ الْبَدْرُ الْمُنِيرْ
بِمَوْلِدِ الْهَـادِي الْبَشِيـرْ
Wer wu leer wi feeñ na
Ci juddu gu Njiit li, kiy joxe xibaar yu neex
أَهْلاً وَسَهْلاً بِالْإِمَامْ
الْمُصْطَفَى بَـدْرِ الْتَّمَـامْ
Dalal jamm ci Kilifa gi
Al-Mustafa, wer wu mat fa mu yam
شَفِيعِنَا يَوْمَ الْزِّحَـامْ
أَرْسَلَـهُ الْـرَّبُّ الْقَدِيـرْ
Sunu ramukat bésu xat-xat ba
Boroom bi mën lépp moo ko yoni
قَدْ أَشْرَقَ الْبَدْرُ الْمُنِيرْ
بِمَوْلِدِ الْهَـادِي الْبَشِيـرْ
Wer wu leer wi feeñ na
Ci juddu gu Njiit li, kiy joxe xibaar yu neex
بُشْرَى لَنَا نِلْنَا الْمَرَامْ
بِطَـهَ مُعْتَلِـى الْمَقَـامْ
Mbégte ñeel na nu am nanu sunu mebat
Ci barké Taha, mi kawe daraja
شَرَّفَـهُ رَبُّ الْأَنَـامْ
فَلَـمْ يَكُـنْ لَـهُ نَظِيـرْ
Boroom mbindéef yépp teral na ko
Te amul ku ko niru
قَدْ أَشْرَقَ الْبَدْرُ الْمُنِيرْ
بِمَوْلِدِ الْهَـادِي الْبَشِيـرْ
Wer wu leer wi feeñ na
Ci juddu gu Njiit li, kiy joxe xibaar yu neex
يَا ذَا الْجَلَالِ يَا مُجِيبْ
عَبْدٌ دَعَـاك لَا يَخِيـبْ
Yaw Boroom màggat, yaw kiy tontu ñaan
Jaam buy woo du réccu mukk
بِحُرْمَةِ الْنَّبِيِّ الْحَبِيبْ
يَسِّرْ لَنَا الْأَمْـرَ الْعَسِيـرْ
Ci darajay Yonent bu ñu bëgg bi
Yomalal nu mbir mu jafe
قَدْ أَشْرَقَ الْبَدْرُ الْمُنِيرْ
بِمَوْلِدِ الْهَـادِي الْبَشِيـرْ
Wer wu leer wi feeñ na
Ci juddu gu Njiit li, kiy joxe xibaar yu neex
أَدْعُوكَ يَا رَبَّ الْأَنَامْ
أَمِتْنَا عَلَى حُسْنِ الْخِتَـامْ
Maa ngi lay woo yaw Boroom mbindéef yi
Ray nu ci neen gu rafet
وَأَسْكِنَـا فِي دَارَ الْسَّلَامْ
لِبَاسُنَـا فِيهَـا حَرِيرْ
Dëkkal nu ci kër jàmm ga
Sunu yere fof doon ay xariir
قَدْ أَشْرَقَ الْبَدْرُ الْمُنِيرْ
بِمَوْلِدِ الْهَـادِي الْبَشِيـرْ
Wer wu leer wi feeñ na
Ci juddu gu Njiit li, kiy joxe xibaar yu neex
أَجِبْ دُعَانَا يَا أَحَدْ
وَاسْمَعْ نِدَانَا يَا صَمَدْ
Tontu samay ñaan yaw Benn bi
Te déglat samay woo yaw As-Samad
يَا دَائِماً عَلَى الْأَبَـدْ
أَنْـتَ الْمُهَيْمِـنُ الْخَبِيـرْ
Yaw mi fi nekk ba fàww
Yaw yaay Kaltankat bi te xam lépp
قَدْ أَشْرَقَ الْبَدْرُ الْمُنِيرْ
بِمَوْلِدِ الْهَـادِي الْبَشِيـرْ
Wer wu leer wi feeñ na
Ci juddu gu Njiit li, kiy joxe xibaar yu neex
أَهْدِي الْتَّحِيَّةْ وَالْسَّلَامْ
لِلْمُجْتَبَـى خَيْرِ الْأَنَـامْ
Maa ngi jébbal nuyyóo ak jàmm
Ki ñu tànn, gën jiyi mbindéef
والْآلِ وَالْصَّحْبِ الْكِرَامْ
مَا أَمْطَرَ الْمَطْرُ الْغَزِيرْ
Ak njabootam ak saaba yu tedd yi
Lu taw bu bari di taw