رَبِّي لَهُ الْأَسْمَاءُ الْحُسْنَى
Sama Boroom moom am na tur yi gën a rafet.
Wo
رَبِّي لَهُ الْأَسْمَاءُ الْحُسْنَى
تُسَبِّحْ لَهُ الْأكْوَانْ
Sama Boroom moom mooy boroom tur yu gën a rafet
Mbindéef yépp a ngi koy sabbaxal
إِلَيْهِ يَرْجِعُ كُلُّ أَمْرٍ
كُلُّ زَمَانٍ وَكُلَّ مَكَانْ
Ci moom la mbooleem mbir di dellu
Ci jamono ju ne ak ci bërëb bu ne
إِذَا دَعَوْتْ فَادْعُ الْإِلَهْ
وَإِنِ اسْتَجَرْتَ فَلُذْ بِاللَّهْ
Soo wootee, wooyal Yalla ji
Te soo wuttee fegukaay, fegal ci Allah
مَا لَنَا مَوْلًى سِوَاهْ
عَفُوٌّ كَرِيمٌ وَرَحْمَانْ
Amunu keneen ku nuy dimbali lu dul moom
Ku baale la, ku yaatu la, tey Boroom yërmande
رَبِّي لَهُ الْأَسْمَاءُ الْحُسْنَى
تُسَبِّحْ لَهُ الْأكْوَانْ
Sama Boroom moom mooy boroom tur yu gën a rafet
Mbindéef yépp a ngi koy sabbaxal
إِلَيْهِ يَرْجِعُ كُلُّ أَمْرٍ
كُلُّ زَمَانٍ وَكُلَّ مَكَانْ
Ci moom la mbooleem mbir di dellu
Ci jamono ju ne ak ci bërëb bu ne
اتَّقِ اللَّهْ وَلَهُ اِصْبِرْ
فَالْصَّبْرُ فِي الْعُقْبَى حَمِيدْ
Ragalal Allah te muñ ngir moom
Ndaxte muñ ci mujj gi lu nuy gërëm la
وَتَزَوَّدْ عِلْمًا وَبَيَانًا
مِنَ الْسُّنَّةِ وَالْقُرْآنْ
Takku ci xam-xam ak leeray
Bu bawoo ci Sunna ak Alxuraan