دَاوِينِي يَا نُورَ الْحَي
Faj ma, yaw Leerub Aji-Dund ji.
Wo
دَاوِينِي يَا نُورَ الْحَي
دَاوِينِي وَانْظُرْ إِلَي
Faj ma yaw Leeru Ki fi ne
Faj ma té nga xool ma
دَاوِينِي دَاوِي
يَا نُورَ الْحَي
Faj ma, faj ma
Yaw Leeru Ki fi ne
يَا مُحَمَّدْ أَنْتَ الْمَحْبُوبْ
وَلِأَجْلِكْ نِلْنَا الْمَطْلُوبْ
Yaw Mahammad yaw lañu sopp
Ndax yaw lañu amé li ñu doon wut
بِمَدْحِكْ تَشْتَاقُ الْقُلُوبْ
تُنْجِينَا بِيَوْمِ الْدِّينْ
Saw tagg mooy naammal xol yi
Dinga ñu musal bésub àtte ba
دَاوِينِي يَا نُورَ الْحَي
دَاوِينِي وَانْظُرْ إِلَي
Faj ma yaw Leeru Ki fi ne
Faj ma té nga xool ma
دَاوِينِي دَاوِي
يَا نُورَ الْحَي
Faj ma, faj ma
Yaw Leeru Ki fi ne
اَلْمَادِحْ بِمَدْحُ يَقُولْ
هَوَاهُ مَدْحُ الْرَّسُولْ
Kiy tagg ci taggam lay waxé
Mbëgeelam mooy tagg Yebbal bi
لِأَجْلِهْ نِلْنَا الْقَبُولْ
شَفَاعَةْ بِيَوْمِ الْدِّينْ
Ndax moom lañu nangulee
Rammu ci bésub àtte ba
دَاوِينِي يَا نُورَ الْحَي
دَاوِينِي وَانْظُرْ إِلَي
Faj ma yaw Leeru Ki fi ne
Faj ma té nga xool ma
دَاوِينِي دَاوِي
يَا نُورَ الْحَي
Faj ma, faj ma
Yaw Leeru Ki fi ne
يَا مُحَمَّدْ أَنَا الْمَدَّاحْ
وَبِمَدْحِكْ قَلْبِي يَرْتَاحْ
Yaw Mahammad man miy sa madâhu
Té ci saw tagg la sama xol di dal
أُهْدِيكَ مَسَا وَصَبَاحْ
صَلَاةً لِيَوْمِ الْدِّينْ
Dila jox ngoon ak suba
Selli ba bésub àtte ba
دَاوِينِي يَا نُورَ الْحَي
دَاوِينِي وَانْظُرْ إِلَي
Faj ma yaw Leeru Ki fi ne
Faj ma té nga xool ma
دَاوِينِي دَاوِي
يَا نُورَ الْحَي
Faj ma, faj ma
Yaw Leeru Ki fi ne
يَا خَلَايِقْ صَلُّوا عَلَيْهْ
مَوْلَاكُمْ صَلَّى عَلَيْهْ
Yaw mbindéef yi sellilun ko
Sen Boroom sellil na ko
وَالْجِذْعُ حَنَّ إِلَيْهْ
مِنْ شُوْقُهْ أَنَّ أَنِينْ
Té xànjaru tàndarma bi naamm na ko
Ndax nammeelam mu doon jòoy bu rëy
دَاوِينِي يَا نُورَ الْحَي
دَاوِينِي وَانْظُرْ إِلَي
Faj ma yaw Leeru Ki fi ne
Faj ma té nga xool ma
دَاوِينِي دَاوِي
يَا نُورَ الْحَي
Faj ma, faj ma
Yaw Leeru Ki fi ne
صَلَاةٌ عَلَى الْمُخْتَارْ
وَالْآلِ ثُمَّ الْأَنْصَارْ
Selli ci kinu tànn bi
Ak njaboot gi ak ansaar yi
وَالصَّحْبِ رَفِيقِ الْغَارْ
أُهْدِيهَا مَعَ النَّسْرِينْ
Ak saaba yi ak andandóo kàmbi bi
Ma dila ko jox ak xet yu xéen