سَلُوا فُؤَادِي سَلُوهُ فَهْوَ يُخْبِرُكُمْ
Ask My Heart, Ask It, for It Shall Inform You
Wo
سَلُوا فُؤَادِي سَلُوهُ فَهْوَ يُخْبِرُكُمْ
عَنِّي إِذَا غِبْتُمْ إِذْ فِيهِ مَحْضَرُكُمْ
Laat lén sama xol, laat lén ko ndax dina léen xamal
lu jëm ci man bu ngén sori, ndax ci biiram la ngén féété
أَيَا بُدُورًا أَنَارَ الْكَوْنَ مَظْهَرُكُمْ
لَوْلَا تَعَلُّلُ قَلْبِي حِينَ أَذْكُرُكُمْ
Éy weer yi nga xam ne seen feeñ leeral na àdduna
bu dul woon fexewu sama xol saa su ma léen fàttelikoo
وَوَضْعُ كَفِّي عَلَيْهِ جَنَّ أَوْطَارًا
لَوْ شَابَ دَمْعِي بِحَارَ الْأَرْضِ أَغْرَقَهَا
Ak teg sama loxo ci kawam dof na ci nammeel
bu sama rangooñ jaxasoo woon ak géej yi ci suuf si mu lëf léen
مِنْ مُقْلَةٍ حَرُّ نَارِ الشَّوْقِ أَرَّقَهَا
وَالْوَجْدُ قَسَّمَ أَحْشَائِي وَفَرَّقَهَا
Jóge ci bët boo xam ne tàngaayu safaray nammeel teree na ko nelaw
te mbëggeel mu tar xàjjal na sama biir ba séddatle ko
لَوْ قَرَّبُوا النَّارَ مِنْ قَلْبِي لَأَحْرَقَهَا
فَهَلْ سَمِعْتُمْ بِقَلْبٍ أَحْرَقَ النَّارَا
Bu ñu jegeñal woon safara sama xol, dina ko lakk
ndax mas ngéen degg xol boo xam ne moo lakk safara?