اَلْهِجْرَةُ رِحْلَةُ هَادِيْنَا
Gàddaay gi mooy tukkibu sunu Njiit
Wo
اَلْهِجْرَةُ رِحْلَةُ هَادِيْنَا
حَمَلَ الْإِسْلَامَ لَنَا دِيْنَا
Gadday gi mooy tukkibu sunu Kilifa
mu indi Lislaam ngir mu nekk sunu diine
فَسَلَامُ اللّٰهِ عَلَی الْهَادِيْ
وَالْكَوْنُ يُرَدِّدُ آمِيْنَا
Jàmmub Yàlla na nekk ci Kilifa gi
mbindéef yépp di tontu "Aamiin"
رَحَلَ الْصِّدِّيقُ عَنِ الْدَّارِ
فِی صَحْبَةِ خَيْرِ الْأَبْرَارِ
Al-Siddiq génn na fa kërëm
ci dëkkalook kiy gën ci nitt yu baax yi
صَلَوَاتُ اللّٓهِ تُبَارِکُهُ
مَلَأَ الْدُّنْيَا بِالْأَنْوَارِ
Ñaaneel yu Yàlla yi barkeel nañ ko
mu feesal àdduna bi ak ay leer
اَللّٰهُ تَكَفَّلَ يَحْمِيْهِ
وَعَلِيٌّ أَصْبَحَ يَفْدِيْهِ
Yàlla jël na kàddu ngir aar ko
Ali tamit joxe na boppam ngir moom
وَبِسِرِّ الْقَوْمِ الْأَشْرَارِ
بِنْتُ الْصِّدِّيْقِ تُوَافِيْهِ
Ak mbiri nitt yu bon ya
doomu Al-Siddiq ba di fekkji ko
وَصَلَ الْمُخْتَارُ إِلَی طَيْبَةْ
وَ الْكُفْرُ تَرَاجَع فِی خَيْبَةْ
Ku ñu tànn ki agsi na Tayba
te weddi gi delloo na gannaaw ci njàqare
وَ جُنُوْدُ اللّٰهِ تُحِيْطُ بِهِ
مِنْ نُوْرِ الْاِسْلَامِ الْهَيْبَة
Xareen yu Yàlla yi wër nañ ko
ak lëmmub leeraayu Lislaam
بِالْرُّوْحِ سَنَحْمِی الْمُخْتَارا
وَ نُقَاتِلْ عَنْهُ الْكُفَّارا
Ak sunuy bakkan lañuy aar Ku ñu tànn ki
te dañuy xexal moom ci kéfer yi
عَهْدًا لِلّٰـهِ نُبَايِعُهُ
جُنْدًا لِلّٰـهِ وَ اَنْصَارا
Digal la ak Yàlla lu ñuy dëggal
di xareen yu Yàlla ak ndimbal-katam