يَا أَجْمَلَ الْأَنْبِيَاء
Oh Most Beautiful of Prophets
Wo
Wo
يَا أَجْمَلَ الْأَنْبِيَاء
يَا أَكْمَلَ الْأَصْفِيَاء
Yaw mi gën a rafet ci yonent yi
Yaw mi gën a mat ci ñi ñu tànn
يَا خَاتَمَ الرُّسْلِ مَا
أَحْلَاكَ فِي قَلْبِي
Yaw miy tàkkub yonent yi
nu mu neexee ci sama biir xol!
يَا ذَا الَّذِي نُسْخَةُ
الْأَكْوَانِ فِيْكَ مَطْوِيَّ
Yaw mi nga xam ne mbindum
mbindéef yépp sàqu na ci yaw
عَطِيَّةٌ أَزَلِيَّة
May gu sax dakk dëgg-dëgg
أَنْتَ الَّذِي أُعْطِيتَ
الشَّفَاعَةَ الْوَافِيَّة
Yaw lañu jox
rammu gu mat sëkk gi
وَ الْخَلْقُ حِينَئِذٍ
يَلْتَمِسُونَ الْأَنْبِيَاءْ
Te mbindéef yi booba
dañuy wutsi yonent yi
ثُمَّ يُقَالُ لِلْأَنَامْ
قَدْ نِلْتُمُ الْأُمْنِيَّة
Ci loolu lañuy wax nit ñi
seen bëgg-bëgg mat na
أَلَا اقْصِدُوْا مُحَمَّدًا
بَابَ الْإِلَهِ الْعَالِيَ
Jëmleen ci Mahammad
buntub Boroom bi gën a kawe
آيَاتُهُ شَافِيَة
Firndeem yi fajkat lañu
وَهُوَ الْمُعَدُّ لَهَا
وَ ذُوَ الْثَنَاءِ الْوَافِيَ
Te mooko yeyoo
te mookay sargale sargal gu mat
ثُمَّ يُنَادِي سَاجِدًا
يَا رَبِّ جُدْ رَاضِيَـا
Dina woo Boroomam buy sujood
"Yaw sama Boroom, may ma te gërëm ma"
يُنَادِي اشْفَعْ يَا حَبِيْبِ
يَا صَفْوَةَ الْأَصْفِيَاءْ
Dinañu ko woo: "Rammul yaw ki nu bëgg
yaw mi gën a sell ci ñi ñu tànn"
وَسَلْ تُعْطَى مَا تَرُوْم
وَلَا تَدَعْ عَاصِيَا
Ñaanal lepp loo bëgg dinañu la ko may
te bul bàyyi benn bàkkaarkat
يَا صَفْوَةَ الْأَصْفِيَاءْ
Yaw mi gën a sell ci ñi ñu tànn
صَلُّوْا عَلَى مَنْ عَلَا
فَوْقَ السَّمَا رَاقِيَا
Julli leen ci kii yéeg
ba gën a kawe asamaan yi
هذَا حَبِيْبٌ غَدًا
عَنَّا العَنَـا مَـاحِيَا
Kii mooy ki nu bëgg ëlëg
di dindi ci nun coono yépp
يَا رَبَّنَا عَطَّفْ عَلَيْنَا
قَلْبَهُ الزَّاكِيَا
Yaw sunu Boroom, wëlbatiil ci nun
xolam bu sell bi
وَاخْتِمْ لَنَا خِتَامَ مِسْكٍ
يَا مُجِيْبَ الدَّاعِيَا
Te nga tej sunu mujj ak xetuy misk
yaw miy wuyu ñiy ñaan
بِالْأَسْرَارِ الذَّاتِـيـــة
Ak mbóoti sa jëmm ji