طَابَ لِي خَلْعُ عِذَارِي
Neex na ma ma folli sama kersa
Wo
طَابَ لِي خَلْعُ عِذَارِي
فِي هَوَى الْبَدْرِ الْتَّمَامْ
Saf na ma dindi samay kersa
ci mbëggeelu weer wu mat wi
بِافْتِقَارِي وَانْكِسَارِي
أَرْتَجِيْ نَيْلَ الْمَرَامْ
Ak sama baat-u-kaane ak sama toroxlu
laa yaakaare jot li ma namm
يَا عَذُوْلِي لَا تَلُمْنِي
مَا عَلَى الْعَاشِقُ مَلَامْ
Yaw mi may gànne, bul ma xas
ndax ku mbëggeel jàpp amu gànne
اُدْنُ مِنِّي وَارْوِ عَنِّيْ
أَنَا فِي الْعِشْقِ إِمَامْ
Jege si ma te nettali li ma wax
ndax ci mbëggeel man laa njiit
خَمْرَةُ الْأَحْبَابِ تُجْلَ
هِيَ حِلٌّ لَا حَرَامْ
Sangayu soppé yi fés na
loolu lu dagan la, daganul mukk
مِنْ عُيُونِ الْعِيْنِ تُمْلَى
صَانَهَا الْبَرُّ الْسَّلَامْ
Ci bëti xurul-ayni yi lañ koy duyé
Boroom mbax gi ak Jàmm gi moo ko aar
يَا أَخَا الْأَشْوَاقِ يَمِّمْ
سَيِّدَ الْرُّسْلِ الْكِرَامْ
Yaw mi am nammeel, jublal
njiitub yonent yu tedd yi
وَاغْنَمِ الْذِّكْرَ وَزَمْزِمْ
بِصَلَاةٍ مَعْ سَلَامْ
Jottu fattaliiku te ngay xasida
ak julli ak jàmm ci kawam
لِحَبِيْبِ الله أَحْمَدْ
كُلَّمَا جَنَّ الْظَّلَامْ
Ci kaw Ahmadu soppeb Yalla bi
saa su lëndëmu gudd tàbbee
كُلُّ مَنْ وَالَاهُ يَسْعَدْ
وَيَنَالْ حُسْنَ الْخِتَامْ
Képp ku ko sopp dinga bég
te dinga jot mujju mu rafet