Wo
حَسْنَاءُ تُرْبِعُنَا
دَوْمًا وَتَعْرِفُنَا
Taar bu rafet bi nu may meññit
saa su ne te xam nu
حَلَّتْ لِتَمْنَحَنَا
عَدْلًا وَإِحْسَانَا
Ñëw na ngir may nu
njubb ak mbaax
مِنْ قُدْرَةٍ شَرُفَتْ
مَيْمُونَةٌ عُرِفَتْ
Ci kàttan gu tedd la dikke
barkeel na te siw na
بِالْحُسْنِ قَدْ وُصِفَتْ
سِرًّا وَإِعْلَانَا
Ak taar lañ ko misaal
ci biir ak ci biti
تَكَامَلَتْ أَلَقَا
خَلْقًا حَكَى خُلُقَا
Mat na ci leer
melokan am baayale na ak jikkoom
وَالْكُلُّ مُتَّسِقا
مِنْهُ الْضِّيَا بَانَا
Te lépp dëppoo na
leeram feeñ na ci moom
رَاقَتْ مَشَارِبُهَا
نِيلَتْ مَطَالِبُهَا
Ay batiinam set nañ
yitëm yépp mat nañ
صَارَتْ مَنَاقِبُهَا
لِلْفَخْرِ كَيْوَانَا
Ay jikkoom yu rafet
nekk nañ ndam lu kawe
عَمَّتْ مَآثِرُهَا
سَارَتْ بَشَائِرُهَا
Ay xéewalam tasaaroo nañ
ay xibaaram yaatu nañ
تَهْدِي خَوَاطِرُهَا
الْأَرْوَاحَ إِيقَانَا
Ay xalaatam dañuy jiite
xol yi ba ñu am nite
فِي وَصْفِهِ عِبَرٌ
لَمْ يَحْكِهَا بَشَرٌ
Ci melokanam am na ay nattu
yooxu nit masul a nettali
وَالْكُلُّ مُنْبَهِرٌ
مَا انْفَكَّ هَيْمَانَا
Ñépp a ci jaaxle
dëggu ci mbëggeel
فَقَامَةٌ رَبْعَةْ
كَمَا تَرَى طَبْعَهْ
Taxawaayam digg-dóomu la
ni nga gise jikkoom
تَفُوقُ بِالطَّلْعَهْ
مَنْ طَالَ سِيقَانَا
Da ko kawe ci melokan
ñi gën a njool ci tànk
فِي وَجْهِهِ قَمَرٌ
فِي ثَغْرِهِ دُرَرٌ
Kanamam weer la
gémmiñam ay luulu lañ
فِي نُطْقِهِ خَفَرٌ
بِالْصَّمْتِ قَدْ زَانَا
Waxam am na kersa
mën a noppi da ko tàkkal
وَجَبْهَةٌ عَرُضَتْ
لِلَّهِ قَدْ خُفِضَتْ
Jë am gu yaatu la
Yàlla la koy sujjōole
وَبِالْنُّهَى نَهَضَتْ
عِزًّا وَعِرْفَانَا
Ak xel la yékkatikoo
ci daraja ak xam-xam
فِي وَجْهِهِ بَلَجٌ
فِي عَيْنِهِ دَعَجٌ
Kanamam leer na nàñ
bëtam ñuul nañ kukk
فِي حَاجِبٍ زَجَجٌ
بِالْحُسْنِ مُزْدَانَا
Yeen-enam dañu rafet
ci taar lañu xaroo
إِنْ رِيءَ يَتْبَعُهُ
نُورًا يُزَامِنُهُ
Boo ko gisee leer
di na ko topp saa su ne
فَالْأَنْفُ مَارِنُهُ
أَقْنَى وَحِدْبَانَا
Bakanam bu rafet ba
am na njoolaay gu leer
وَثَغْرُهُ ضَلِعٌ
وَالْصَّدْرُ مُتَّسِعٌ
Gémmiñam yaatu na
dënnam yaatu na itam
وَالْبَطْنُ مُرْتَجِعٌ
بِالْصَّدْرِ خَمْصَانَا
Biiram dëppoo na
ak dënnam ba mu yam
وَالْوَجْهُ دُرِّيٌّ
وَالْلَّوْنُ وَرْدِيٌّ
Kanamam luulu la
melokanam rafet na
وَالْرُّوحُ نُورِيٌّ
أَضَاءَ أَكْوَانَا
Ruuxam leer la
leergal na àdduna yépp
ضَخْمُ الْكَرَادِيسِ
زَاكِي الْأَحَاسِيسِ
Cér ya dëgër nañ
xolam set na wéññ
فَرْدُ الْنَّوَامِيسِ
مَا مِثْلُهُ كَانَا
Kénn nekkul ni moom
amul koo ko mën a méngale
أَكْحَلُ أَجْفَانٍ
أَشْنَبُ أَسْنَانٍ
Bëtam am nañ tuur
bëñam dañu weex tàll
حَبَّاتُ رُمَّانٍ
هَلْ رَيْتَ رُمَّانَا
Mel ni peppu rumaan
ndax mas nga giss rumaan?
وَلِحْيَةٌ كَثَّا
تَنَاسَقَتْ بَثَّا
Sikkimam gu yaatu la
dëppoo na ba mu mat
وَجُمَّةٌ أَثَّا
لَمْ تَعْدُ آذَانَا
Kawaram gu yaatu la
rombul ay noppam
بَدْرُ الْدُّجَى فَمُهُ
إِنْ رِيءَ مَبْسَمُهُ
Weeru guddi la gémmiñam
su fekkee mu ngi ree
وَالْكُلُّ مَنْسَمُهُ
بَرًّا وَخُلْجَانَا
Ñépp a koy topp
ci suuf ak ci géej
فَالْرَّحْمُ وَاصِلُهُ
وَالْكَلُّ حَامِلُهُ
Bokkoo laay jokkal
ñépp lay nattal
وَالْخَيْرُ فَاعِلُهُ
سِرًّا وَإِعْلَانَا
Lu baax lay liggéey
ci biir ak ci biti
فِي الْخَلْقِ هَيْبَتُهُ
فِي الْحَقِّ غَيْبَتُهُ
Ragalu na ci mbindéef yi
nekk na ci dëgg
تَفُوقُ طِيبَتُهُ
جِنًّا وَإِنْسَانَا
Baaxeem mën na
jinne ak nit
وَحَبْلُ سُرَّتِهِ
مِنْ حُسْنِ غُرَّتِهِ
Melokanam bu rafet ba
mi ngi jóge ci leeram
مَا مِثْلُ نَظْرَتِهِ
عِزًّا وَإِيْمَانَا
Xooloom amul moroom
ci daraja ak ngëm
قَدْ دَقَّ مَسْرُبَةً
وَفَاقَ مَرْتَبَةً
Kawaram ci dënnam rafet na
kawe na ci daraja
وَعَزَّ مَنْقَبَةً
سَادَ الْوَرَى شَانَا
Jikkoom tedd na
mooy njiitu mbindéef yi
قَلِيلُ لَحْمِ عَقِبْ
وَالْصَّدْرُ مِنْهُ رَحِبْ
Tànkam amul yappa
dënnam yaatu na lool
فَصْلَ الْخِطَابِ وُهِبْ
فَفَاقَ سَحْبَانَا
May nañ ko wax ju leer
raw na ñépp ci wax
كَالْمِسْكِ فِي هَبَبٍ
يَنْحَطُّ مِنْ صَبَبٍ
Mel ni misk buy xeeñ
buy wàcc ci kàww
يُنْسِي أَخَا تَعَبٍ
أَهْلًا وَبُلْدَانَا
Day fatali ku sonn
këram ak réewam
فَحُبُّهُ إِيمَانْ
وَبُغْضُهُ كُفْرَانْ
Mbëggeelam ngëm la
bañ ko ay réer la
يَا وَيْلَ مَنْ قَدْ شَانْ
فِي الْمَدْحِ إِنْسَانَا
Ngalla ku yàq
kiy tagg nit
يَا رَبِّ أَسْعِدْنَا
بِنُورِهِ عِدْنَا
Boroom bi barkeel nu
ci leeram déllool nu
حَتَّى نَرَى الْحُسْنَى
دُنْيَا وَأُخْرَانَا
Ba nu giss li gën
ci àdduna ak àllaxira
صَلَّى وَسَلَّمَ مَنْ
أَوْلَى الْوَرَى مِنَنَا
Julli ak jàmm ci moom
ki mayé xéewal yi
عَلَى الْنَّبِيِّ زَمَنَا
رَبٌّ عَلَا شَانَا
Ci Yonent bi saa su ne
Boroom bi kawe na
كَذَلِكَ الْزَّهْرَا
وَأُمِّهَا الْغَرَّا
Ak Fatimatou Zahra
ak ndayam gu tedd ga
وَآلِهِمْ طُرَّا
مَا الْبَدْرُ نَاغَانَا
Ak njabootam yépp
li feek weer wi ngi leer