مَعَانِي قَدْ بَدَتْ عِنْدِي غَرِيبَهْ
Maana yu yemé feeñ nañu ci man.
Wo
Wo
مَعَانِي قَدْ بَدَتْ عِنْدِي غَرِيبَهْ
وَمَا تُفْضِي إِلِيْهْ بَعْدُ أَغْرَبْ
Maanaa yu yéeme feeñal nañu ma
Te la ciy juddoo gën na yéeme
مِنَحْ مِنْ فَضْلِ مَوْلَانَا عَجِيبَهْ
وَمَاذَا فِي عَطَاهُ لَيْسَ أَعْجَبْ
Ay may yu bawoo ci mbaxu sunu Boroom
Te lu nekk ci mayam doy na waar
وَعِيدُ الْصَّبِ أَنْ يَلْقَى حَبِيبَهْ
وَسُبْحَانَ الَّذِي قَرَّبْ وَحَبَّبْ
Xéwalal ku bëgg mooy dabe ak soppeem
Sellal nekk na ci Ki nu jegeël te sàkkal nu mbëggeel
مَعِي أَقْوَامْ فِي أَعْلَى كَتِيبَهْ
لَهُمْ أَسْرَارْ لَا تُحْصَى وَتُكْتَبْ
Ma ak mbooloo yu nekk ci daraja yu kawe
Am nañu mbóot yu weesu lim ak mbind
مَوَاهِبْ عَالِيَةْ مَا هِيْ كَسِيبَهْ
وَإِحْسَانُ الْمُهَيْمِنْ لَيْسَ يُحْسَبْ
Ay may yu kawe la yu mënul liggéey
Te mbaxu Boroom bi mënul natt
وَمَنْ لُهْ سَابِقَهْ يُدْرِكْ نَصِيبَهْ
مُوَفَّى دُونَ أَنْ يَشْقَى وَيَتْعَبْ
Ku am ndogalu ngëneel dina jot walam
Mu mat manti te amul ci coono walla sonn
وَنَفْحَةُ بَاسِطِ الْنَّعْمَى قَرِيبَهْ
تَعَرَّضْ يَا فَتَى مِنْهَا تَقَرَّبْ
Ngelawu Ki yaatal xéwal bi jege na
Yaw ndaw si, féexu ci te jege ko
عَسَى الْمَكْلُومْ أَنْ يَلْقَى طَبِيبَهْ
فَيُضْحِي الْعِيْشْ لُهْ أَطْيَبْ وَأَطْيَبْ
Naka-mu-ne ki gaañu dina dabe fajkatam
Ba dundam neex te sell ba fàww
وَصَلَّى اللهُ مَا أَفْهَامٌ نَجِيبَهْ
وَعَتْ قَوْلاً بِمَاءِ الْعَيْنِ يُكْتَبْ
Yàlla na Yàlla sotti xéwalam, ba kero xel yu teey
Di xam kàddu yu méngook mbinde ak rangooñ
عَلَى خَيْرِ الْوَرَى الْهَادِي حَبِيبِهْ
وَآلِهْ وَالَّذِي لِلْطُّهْرِ يَصْحَبْ
Ci ki gën ci mbindéef yi, njiit wi di soppeem
Ak njabootam ak ñi ko àndal ci sellngay