ْيَاجَمَالُه
Oh, How Beautiful He Is!
Wo
آه يَا جَمَالُه يَا جَمَالُهْ
سِيدْنَا النَّبِى يَا جَمَالُهْ
Ah, ni mu rafete! Ni mu rafete!
Ah, ni mu rafete! Ni mu rafete!
سِيدْنَا النَّبِى يَا جَمَالُهْ
Sunu Sang bi Yunent bi, ni mu rafete!
كَحِيلُ الطَّرْفِ حَبِيبِي لَوْ تَرَاهُ
ضَحُوكُ السِّنِّ لِلْعَاشِقِ رَمَاهُ
Ku tàqalé gët la sama Xarit bu ko gise woon!
Ku mucc-a-re la, mu tàbal ku ko bëgg ci jaaxle
بَهِيُّ الطَّلْعَةْ فَالْمَوْلَى اصْطَفَاهُ
وَكُلُّ الْخَلْقِ أَنَارَ بِنُورِ طه
Ku leer kanam la, Boroom bi moo ko tànn
Te mbindéef yépp leeral nañu leen ak leeru Taha
وَلَا ظِلُّ لَهُ بَلْ كَانَ نُوْرَا
تَنَالَ الشَّمْسُ مِنْهُ هُوَ الْبُدُوْرَ
Amul woon kërég, waaye leer la woon
Jant bi ci moom la jële leeram, te moom mooy weeru fukk ak ñent
وَلَمْ يَكُنِ الْهُدَى لَوْلَاهُ ظُهُوْرَا
وَ كُلُّ الْكَوْنِ أَنَارَ بِنُوْرِ طَــــــهَ
Te njub du feeñ mukk lu ko moyoon
Te mbindéef yépp leeral nañu leen ak leeru Taha
وَكَفُّ الْمُصْطَفَى كَالْوَرْدِ نَادِى
وَعِطْرُهَا يَبْقَى إِذَا مَسَّتْ أَيَادِى
Loxol Mustafaa mel na ni rous bu tooy
Te xetam day des ci loxo yi ko laal
وَعَمَّ نَوَالُهَا كُلَّ الْعِبَادِ
حَبِيبُ اللهِ يَا خَيْرَ الْبَرَايَا
Barkem yaatal na mbollooy jaam yi
Yaw mbëgeelu Yàlla, yaw mi gën ci mbindéef yi
وَرِيقُ الْمُصْطَفَى يَشْفِي الْعَلِيلَ
وَعَيْنُ قَتَادَةَ خُذْهَا دَلِيلًا
Tufulitu Mustafaa day faj ku tawat
Jëlal gëtu Katada nji ko firnde
تَفَلَ فِي الْبِئْرِ أَضْحَتْ سَلْسَبِيلًا
وَصَارَ لِصَحْبِهِ شَهْدًا مُدَامًا
Mu tufu ci teen bi, mu nekk bëtu-ndox mu sotti
Mu nekk ci saabaam yi lem gu saf, gu dul kosi