عَلَيْكَ صَلَّى اللهْ يَا خَيْرَ خَلْقِ اللهْ
Yàlla na julli ci yaw, yaw mi gën ci mbindéefi Yàlla yi.
Wo
Wo
عَلَيْكَ صَلَّى اللهْ يَا خَيْرَ خَلْقِ اللهْ
وَالْآلِ وَالْأَصْحَابْ وَالْقَوْمِ أَهْلِ اللهْ
يَا كَعْبَةَ الْأَسْرَارْ وَمَنْبَعِ الْأَنْوَارْ
بِالْعَزْمِ يَا مُخْتَارْ أَيَّدْتَ دِينَ اللهْ
Yaw Kaaba suttura yi ak bëtu leer yi
Ak sa pas-pas, yaw tànnéef bi, yaa dëgëral diinu Yàlla
فِدَاؤُكَ الْأَرْوَاحْ وَمِثْلُهَا الْأَشْبَاحْ
يَا خِيِرَةَ الْفَتَّاحْ مِنْ أَنْبِيَاءِ اللهْ
Sunu ruu ñoo ngi lay saraxé, ak sunu yaram tamit
Yaw mi gën ci tànnéefi Ubbi bi, ci biir yonenti Yàlla yi
يَا مَنْ لَهُ الْبُرْهَانْ وَخُلْقُهُ الْقُرْآنْ
مَا كَانَتِ الْأَكْوَانْ وَحَقِّهِ لَوْلَاهْ
Yaw mi yor firndé bu lér, te sa jikko di Alxuraan
Àddina du amoon, ci dëggu boroom bi, bu doonul yaw
لِوَاؤُكَ الْمَرْفُوعْ وَقَوْلُكَ الْمَسْمُوعْ
وَحُبُّكَ الْمَطْبُوعْ فِي مُهْجَةِ الْأَوَّاهْ
Sa raaya mu kawe la, te sa wax ñu koy déglu
Te sa mbëggeel dafa tàq ci xolu koo xam ni dafa lay namm
نَدْعُوكَ بِالسِّبْطَيْنْ لِكَشْفِ هَذَا الْغَيْمْ
يَا مَلْجَأَ الْكَوْنَيْنْ بِالْخَطْبِ بَعْدَ اللهْ
Ñoo ngi lay woo ci sa ñaari sëti ngir nga dindi lëndëm gi
Yaw miy xéerug ñaari àddina yi ci musiba yi, gannaaw Yàlla
هَا أَنْتَ فِي الْمَحْشَرْ مُؤَيَّدُ الْمَظْهَرْ
فَكُلَّمَا تُذْكَرْ عَلَيْكَ صَلَّى اللهْ
Mu ngi ni, fexée ci bésu dajé ba, yaay ki ñu dëgëral feeñam
Bépp yoon bu ñu la tuddé, Yàlla na julli ci yaw